Free Christian classic ebooks for you to download:
Browse books now

Multilingual Online Bible


Wolof NT
Type your search text here






Choose a Bible


Select book or range
Chapter


Wolof NT, Hebrews 1

1   Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.

2   Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.

3   Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndeyjooru Aji Màgg ji ca kaw,

4   wone noonu ne, moo gën a màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur.

5   Ndaxte Yàlla musul a wax kenn ci malaaka yi ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.» Musul ne ci mbirum kenn ci ñoom it:«Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom,mu nekk Doom ci man.»

6   Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne:«Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.»

7   Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax:«Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw,ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki safara.»

8   Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax:«Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww,ci njubte ngay nguuru.

9   Sopp nga njub te bañ lu bon.Looloo tax yaw Yàlla,sa Yàlla sol la mbég mu gën a réymi mu jagleel say àndandoo.»

10  Newaat na it:«Yaw Boroom bi,yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga,defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.

11  Yëf yooyu dinañu wéy,waaye yaw dinga sax,dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.

12  Dinga leen taxañ ni malaan,ñu furi ni ay yére,waaye yaw doo soppiku,te sa dund amul àpp.»

13  Waaye Yàlla musul a teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:«Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneel say noonci sa kanam.»

14  Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nar a jot mucc gi.


Philemon 1    Choose Book & Chapter    Hebrews 2

Wolof is spoken by 2,665,000 people: 2,620,000 in Senegal, 35,000 in France, 10,000 in Mauritania. The New Testament was first published in 1988. The complete Bible has not been published.

In order to display all characters correctly, you may need a basic Unicode font.

Wolof New Testament. Copyright © 1987, 2004 Les Assemblées Evangéliques du Sénégal et la Mission Baptiste du Sénégal. Imported from the Wolof Bible website.


Licensed to Jesus Fellowship. All Rights reserved. (Script Ver 2.0.2)
© 2002-2021. Powered by BibleDatabase with enhancements from the Jesus Fellowship.