Free Christian classic ebooks for you to download:
Browse books now

Multilingual Online Bible


Wolof NT
Type your search text here






Choose a Bible


Select book or range
Chapter


Wolof NT, Hebrews 10

1   Yoonu Musaa dafa misaal xéewal yi waroon a ñëw; takkandeer la ci yëf yu dëggu yi, waaye du ñoom ci seen bopp. Looloo tax mënul a yeggale cig mat ñi ñëw ci Yàlla, ndaxte at mu nekk duñu jóg ci jébbal Yàlla sarax yooyu.

2   Sarax yi ñuy def, bu ñu manoon a sellal ñiy jaamu benn yoon ba fàww, kon dinañu leen bàyyi, ndaxte dootuñu am yeraange ci seeni bàkkaar.

3   Waaye dañuy fàttaliku bàkkaar yi ci sarax yi ñuy def at mu jot.

4   Ndaxte deretu yëkk yi ak ju sikket yi mënuñoo dindi bàkkaar yi.

5   Looloo tax bi muy wàcc àddina, Kirist nee na:«Bëggoo saraxu mala walla beneen sarax,waaye aw yaram nga ma defaral.

6   Sarax yu ñuy lakkwalla sarax yiy dindi bàkkaar,benn neexu la ci.

7   Moo tax ma ne: “Damaa wàccngir def sa coobare, yaw Yàlla,mu dëppoo ak li ñu bind ci sama mbirci téereb yoon wi.”»

8   Wax na bu jëkk: «Saraxi mala walla yeneeni sarax, sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar, bëgguloo leen te benn neexu la ci.» Teewul yoon wi moo leen santaane.

9   Noonu mu tegaat ca ne: «Damaa wàcc ngir def sa coobare.» Noonu toxal na jëfin wu jëkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees.

10  Te ci li Kirist def coobareg Yàlla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba fàww, moo tax nu sell ci bàkkaar.

11  Bés bu nekk saraxalekat yi dañuy taxaw di liggéeyal Yàlla, di sax ci def sarax yu mënul a dindi bàkkaar yi mukk.

12  Waaye nag saraxalekat bii di Kirist, bi mu saraxee sarax bu am doole ngir dindi bàkkaar yi benn yoon ba fàww, dafa toog ca ndeyjooru Yàlla,

13  di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam.

14  Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba fàww.

15  Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko;

16  dafa jëkk a wax ne:«Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak ñoom,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xol,bind ko ci seen xel.»

17  Noonu mu tegaat ca ne:«Dootuma fàttaliku seeni bàkkaarwalla seeni tooñ.»

18  Kon nag fu ñuy baale bàkkaar, aajootul sarax su koy dindi.

19  Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell-baa-sell,

20  nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund,

21  te gannaaw am nanu saraxalekat bu mag, biy yilif waa kër Yàlla,

22  kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell.

23  Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te bañ a toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.

24  Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax.

25  Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi.

26  Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu.

27  Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy war a lakk nooni Yàlla yi.

28  Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te ñaar walla ñetti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn yërmande.

29  Ku xeeb Doomu Yàlla ji te fonkadi deretu kóllëre, ji ñu ko sellale, te muy toroxal Xelum Yàlla, mi indi yiw, naka la mbugalam war a gën a yéese?

30  Xam nanu ki wax ne: «Man maay àtte, maay fey jëf.» Te newaat na: «Boroom bi dina àtte ay gaayam.»

31  Ndaw tiitaange ci ku sàggan, ba tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund!

32  Fàttalikuleen bés yu jëkk ya, ba leeru Yàlla tàbbee ci yéen; dékku ngeen xeex bu mag ciy fitna.

33  Léeg-léeg ñu saaga leen ak di leen sonal ci kanamu nit ñi; léeg-léeg it ngeen taxawu ñi ñuy def noonu.

34  Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne, am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww.

35  Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag.

36  Dangeen a war a muñ, ba def coobareg Yàlla, sog a jot li mu leen digoon.

37  Ndaxte lii la Mbind mi wax:«Ci kanam tuuti, ki war a ñëw dina ñëwte léegi mu agsi.

38  Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm,waaye bu delloo gannaaw,sama xol du sedd ci moom.»

39  Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye nu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc.


Hebrews 9    Choose Book & Chapter    Hebrews 11

Wolof is spoken by 2,665,000 people: 2,620,000 in Senegal, 35,000 in France, 10,000 in Mauritania. The New Testament was first published in 1988. The complete Bible has not been published.

In order to display all characters correctly, you may need a basic Unicode font.

Wolof New Testament. Copyright © 1987, 2004 Les Assemblées Evangéliques du Sénégal et la Mission Baptiste du Sénégal. Imported from the Wolof Bible website.


Licensed to Jesus Fellowship. All Rights reserved. (Script Ver 2.0.2)
© 2002-2021. Powered by BibleDatabase with enhancements from the Jesus Fellowship.